Li Ma Weesu

(As In A Mirror)

by Youssou N'Dour

(English)

My past always comes back as in a mirror
Sometimes I look back to my past life
With regret or pride
When I'm around the children I love, they dance and I guide
them and I express myself in such a way that I want to be a
child again and never grow older
The longer I stay away, the more forgetful I am
The older I grow, the more I look back to the past
and want to be a child again

(Wolof)

li ma dundee, li ma weesu
dey delluse, mel ni seetu
li ma dundee, li ma weesu
dey delluse, mel ni seetu

seetal leegi leegi ma gesu, ci li ma weesu
leegi leegi ma recu, walla sax di baaku
fu gune yi feetee, dama leen di teetee
wax nu ma neexee, ma bëgga leen

damay, damay, damay dellu gune
mel ni,mel ni, mel ni duma màgg
damay, damay, damay dellu gune
mel ni,mel ni, mel ni duma màgg

lu ma gën di yàgg, xel ni mel ni bank
lu ma gën di màgg, dellu tuuti tank

li ma dundee, li ma weesu
dey delluse, mel ni seetu
li ma dundee, li ma weesu
dey delluse, mel ni seetu

ma ni seetal
leegi leegi ma gesu, ci li ma weesu
leegi leegi ma recu, walla sax di baaku
fu gune yi feetee, dama leen di teetee
wax nu ma neexee, ma bëgga leen

damay, damay, damay dellu gune
mel ni,mel ni, mel ni duma màgg
damay, damay, damay dellu gune
mel ni,mel ni, mel ni duma màgg

fu gune yi feetee, dama leen di teetee
wax nu mu ma neexee ma béggati

li ma gën di jege, mel ni dama sore
lu ma gëna sore, gën di gis li ma jegewoon
lu ma gën di yàgg, xel ni mel ni bank
lu ma gën di màgg, dellu tuuti tank

li ma dundee, li ma weesu
dey delluse, mel ni seetu
li ma dundee, li ma weesu
dey delluse, mel ni seetu

damay, damay, damay dellu gune
mel ni,mel ni, mel ni duma màgg . . .

Powered by PmWiki